top of page

Ñan ñooy ComUniclang

Màlle Foofana mi sos ComUnicLang, ab ligéeykatla bu géeju ci jangat ak gëstu jòkkoo ak jòkkalante ci wàllu kàddu, ak sùqali man-mani woroomi nombo-tànk ñeel làkk wi. Doxalinam wékku ci jaar-jaaram ak xam-xaman, ci wàllu tàggat, wonena yìtte wu yaatu soxal soxlay kilifa yii ak aji-wax ci pènci Senegal ak Afirik.

 

ComUnicLang indi lu bees ci ànd ak kilifa yi. Li ko soxal mooy ap jàppale ci ni ñuy jëfandikoo làkki angale waaye it farañse ak wolof, ci fànni bind ak wax, fii ci biir réew mi ak bitim réew.

 

Bayyeekoo Dakar, ComUnicLang dafa leen di jagleel ab taxawu wu meengoo ak seeni soxla, ci wàllu polotik, koomkoom, mbatit ... 

 

Ni ñuy doxalee ci ComUnicLang:

  • Tàggat ci xam ni làk tëdee, su boobaa dañuy seet li nit ki soxlaa xam ci baati lak wi, naka la ñuy waxee baat yooyu, nanu leen di toftalee aka ràbbale, ngir yombal kàddu gi.

  • Tàggat ci xam ni jokkalante tëdee, waajal nit ki ba mu gen a man a yëkati kàddu cib pènc, naka ngay sàmmee sa ay yeg-yeg, ba wax ji digg-dóomu, naka ngay tabaxee baat yi bañu gën leen a man a xàmme, ak di leen yék, ak naka lañu man a fésalee aw xalaat ba mu yemoo ak gëm-gëmi ñi ngay waxal.

  • Tàggat ci wàllum mbind, dañu leen di taxawu ci ni ñuy sammee am mbind ba mu mengoo ak li pènc miy xaar ci kàddu gu juge ci banqaas yu kawe yi.

  • Teewlu ak seetlu seeni doxalin, dina ñu leen fekk ci seen barabi ligéeyukaay ak fa ñuy yëkatee ay kàddu, ngir jangat doxalin wi, li jar sònj ak jòyyanti ñu fésal ko.

 

ComUnicLang, lu bees la, ci ànd ak yeen, di leen indil ay taxawaay yu mengoo ak seen ay soxla. Li ñu gën a soxal bòkk na ci suturay ñi ñuy ligeeyal, sammoonte ak seeni bëg-bëg ak wareef, ba ñu di jël kàddu ci xel mu dal. Ci jamano joo xamne jèkku Angale  ab yòkkute la, ComUnicLang dafa dògu ci kartanal taxawaayi kilifa yi bayyeekoo Senegal ak fi ko wër.

8552804288_83616eabb0_b.jpg
bottom of page